});












Poesie-Wolofal sur S. Bassirou Abdoul Khadre – par Akb Majalis

= 1079

Sagal nga yoon wi sagal waa yoon wi mbacke doundal
Tey sax ci djàmm’aka bek ngir mbacke yaanou sagal.

Sa Maam dja bék na ci yaw sa Mak ji bek na ci yaw
Mbooleem Mouride bou lou baax nior bek ci yaw sigiréel

Discour bi sedd na khol lool goomi khol yifi woon
Wéreul nga leen péngg yaw yaa diar di woy di béreul

Yalnang fi yagg te wér Cheikh Bass te yalna nga raw
Seugn Bàmba làkh la fof ab yàkhkat doufa wel

Kouy wakh ci yaw lou yiwak kouy wakh lou deefi safaan
Boul faalei ngir khamnei kooke ak kagnaana ko dal

Te Yalla may sago Seugn Cheikh Sidi mooki rakam
Sagos matal Autoroute bii ak yeneen yi mou naal

Akb Majalis

Leave a Reply

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *